Saar 20 — Sarax yi ci liggéey bu njëkk ba
GSAM 311.1“Dajaleel sama ñi sell ci man; ñi def ak man dige ci ay sarax. Te asamaan yi dinañu wone njubam: ndaxte Yàlla mooy àttekat bi ci boppam.”1
GSAM 311.2Ci téere bi tuddu Review and Herald, ci 3 Suwe 1902, ñu ngi fa jànge ne:
GSAM 311.2Ñi dugg ci liggéey bi léegi, xamuñu bu baax ci bañ-sa-bopp ak saraxu-bopp ñi Boroom bi tegloon tiisug liggéeyam bi mu ko tambalee. War nañu leen di nettali lépp lu xewoon ci lu jàll, di leen ko baamtu; ndaxte ñoom ñoo war a yóbbu liggéey bi ci kanam ak woyof gu ni mel ak saraxu-bopp gu melni ni meloon liggéeykat yu dëgg ya ca jamono ya jàll.
GSAM 311.3Delloosi, ci Testimonies for the Church, Vol. 7, ñu ngi fa fekk kàddu yii:
GSAM 311.3“Ñu ngi jege njeextalu taarixu àddina si, te wàll yu wuute yu liggéeyu Yàlla war nañoo wéy ak saraxu bopp bu gën a réy li ñu fi mas a gis.”2
GSAM 311.4Li xewoon ba taxoon Pasteur Bates tàmbalee bind te siiwal téereem bu njëkk ci mbirum Sàbat bi, ci atum 1846, waxees na ci ba pare. Waxees na itam ci jafe-jafe yu metti yi Pasteur James White dundoon, bi mu tàmbalee siiwal jurnaal bi ñu tudde The Present Truth ci atum 1849.
GSAM 311Téere bu gàtt ci Asamaan yu ubbeeku
GSAM 311.5Ginnaaw gis-gis bi Soxna White amoon ca Topsham, Maine, ci lolli atum 1846, bi ñu ko wonnee yenn ci planètes yi, Pasteur Bates waajal na mbindum téere bu gàtt ci mbirum The Opening Heavens. Waaye soxla nañu woon lool ay xaalis yu mat ngir man koo siiwal. Ngir faju soxla boobu, benn jigéen ju dëkk Massachusetts, mi doog a jeexal te taale benn tapis bu bees bu ñu defaree ay sagar, dafa ko dindi jaay ko, jox xaalis bi ci Pasteur Bates, looloo tax mu mën a siiwal téereem bu ñaareel bi.
GSAM 312Téere bu gàtt ci liggéeyu teg màndargab Yàlla
GSAM 312.1Ginnaaw bi ñu wonnee liggéeyu teg màndargab Yàlla ca Dorchester, Massachusetts, ci 18 Nowàmbar 1848, Pasteur Bates bind na ñetteelu téere bu gàtt, bu tudd, A Seal of the Living God. Fii itam, jafe-jafey amul xaalis ngir móol bi daldi ko dal. Benn jigéen ju ndaw ju ñàkk jëkkër, bi mu déggee li xew, jaay na kër gu ndaw gu mu amoon ca àll ba, te jox Pasteur Bates genn-wàllu xaalis bi mu ci jële. Looloo tax mu mën a feyaat móolug benn téere.
GSAM 312Laaj yu liggéeyu siiwal gi
GSAM 312.2Ci atum 1851-52, jurnaal bii di Advent Review and Sabbath Herald dañu ko doon móol ca Saratoga Springs, N.Y. Foofu, Sëñ Thompson mayoon na Pasteur White ak jabaram kër gu ñu mëna dëkk te duñu ci fey dara; te ak ay meebal yu ñu abbi, amati nañu tawfeexu samp seen kër.
GSAM 312.3Ci jamono jooju, gëmkat yi ci dëgg gu jamono jii amoon nañu di gën a yokku, te ak yokkute googu, soxlawoon nañu liggéeyu bopp bu Pasteur White ak soxnaam. Loolu, ak liggéeyu bind mi, taxoon na ñu soxla ay ndimbal ci biro bi. Ci jamono jooju sax, amoon na ñeneen ñu yëg seen bopp di ñu jàppale ci liggéeyu mbind mi. Ngir wone ni Boroom bi di liggéeye ngir tontu ngëmug askanam, tey taxawal ay liggéeykat bu jamono jotee, ñu ngi leen di nettali jaar-jaaru benn jigéen ju jébbalu, Soxna Rebecca Smith, bu dëkk West Wilton, N.H.:—
GSAM 312.4Bi jamono ji jàllee, doomam Uriah ak doomam ju jigéen Annie R. dañoo bëggoon lool dem jàng, ngir waajal seen bopp ci njàngale. Yaay ji dafa ragaloon ne doom yi ñu ngi jëm ci àdduna, te dëgg-dëgg, tiitaangeem yooyu amoon na fu mu tekkoon. Mbëggeelu yaay ji, doom yi itam delloo nañu ko.
GSAM 313Uriah Smith ca Akademi bu Phillips
GSAM 313.1Ci diggante 1848 ba 1851, doom ji jang na ca Akademi bu Phillips ca Exeter, N. H., fa lañu daan jàngale ndongo yi atum njëkk ci njàngum daara ju kawe, ngir bu ñu duggee ca daara ju kawe ja, ñu jiitu benn at. Njàng mii mu jeexal na ko. Ci atum 1851, dafa doon liggéey ngir am xaalis bu ko tax a mën a dugg iniwersite, waaye bi ki ko doon jox liggéey bi daanoo ci komersam, mu ñàkk xaalisam bi, te looloo tax na mu bàyyi xalaatam bu yàgg bi mu amoon ci njàngum iniwersite.
GSAM 313Jànk Smith ci benn Daaray Jigéen
GSAM 313.2Bi Uriah nekkee ca daara ju mag ja, rakkam ju jigéen jiy jànge woon ca daara ju jigéen ñi ca Charlestown, Mass. Jàngam ba fa jege woon na jeex, te bi mu nar a bàyyi daara, ñu digal ko moom ak rakkam ju góor ab liggéey ngir ñu jàngale ca daara ju mag ca Mt. Vernon, N.H., diirub ñetti at, $1,000 ci at mi, te ñu leen fayal lekk ak néeg.
GSAM 313.3Ci jamono yooyu la yaay ji jàppee “dëggu gi fi nekk.” Ñaanam yi léegi, su manee nekk, gën nañoo dëgër te gën a tàng fuuf ngir doomam yi. Pasteur Bates dem na West Wilton, te fa la Soxna Smith tekkeel mbirum doomam yi, te ñaan ngir ñu jàpp dëggu gi. Pasteur Bates dafa doon xaar ci ay fan yu néew ngir amal ay ndaje ca Somerville, Mass., ca kër Paul Folsom, te Soxna Smith waroon na bind doomam ju jigéen, di ko woo mu teew ci ndaje mi. Ci biir loolu, Pasteur Bates ak yaay ji ñoo waroon a ñaan Yàlla mu yëngal xolam ngir mu dem ca ndaje ma.
GSAM 313Ñaari Gént yu Mat
GSAM 313.4Pasteur Bates mësul woon a dugg ci néeg bi ñu waroon a amal ndaje mi, looloo tax xamul woon ni néeg bi mel woon. Ci guddig laata ndaje mi, gént na ne mi ngi ci biir neeg ba, te toogu-kaay yépp fees nañu ba mu des benn bi jege bunt bi. Gént na itam ne soppi na waxtaan wi mu naroon a def, daldi wax ci mbirum bérab bu sell bi; ne woy nañu woy wu njëkk wi, ñaan, woy ñaareelu woy wi, te moom léegi la ubbi Biibëlam di jàng, “Ba mat ñaari junni ak ñetti téeméeri fan, ca la bérab bu sell bi di setaliku,” mu jëmale loxoom ci nataalu bérab bu sell bi ci tablo bi, bi buntu bi ubbeekoo, am jànx bu ndaw dugg te toog ci toogu bu neen ba. Gént na itam ne jànx jooju Annie R. Smith la woon, te ci saa si mu tàmbalee yittewoo li muy wax, te nangu dëgg gi.
GSAM 314.1Ndajeg Pasteur Bates ci bésu Sàbat (Gaawu) la woon, te ndaxte amul woon jàng ci bés boobu, Annie nee na, “Ngir neexal sama yaay rekk, dinaa dem.” Ci guddi gi jiitu woon bésu Sàbat boobu, gént na ne dem na, waaye yéex na; bi mu agsee ca buntu bi, ñu jëkk a woy woyu ubbité bi, ñaan, te ñu ngi doon jeexal ñaareelu woy wi; bi muy dugg, gis na ne toogu-kaay yépp fees nañu ba mu des bi nekkoon ci wetu buntu bi; ne amoon na ku gudd, ku am teggin, tey wax ci anam gu neex, di won ab nataal bu mel ni musula gis, te di ko baamtu, “Ba mat ñaari junni ak ñetti téeméeri fan, ca la bérab bu sell bi di setaliku.” Gént na ne li mu waxoon soxal na ko lool, te dëgg la woon.
GSAM 314.2Dafa jóge woon ngir dem ndaje mi ci waxtu wu doy, waaye mu réer yoon wi, looloo tax mu agsi fa ba ñuy woy woyu ñaareel bi di jeex. Bi mu duggee, lépp nekkoon na ni mu ko gise woon ci gént gi, te góor gi mu gisoon ci gént gi moom la woon di baamtu, ci anam googu, wax ji nekk ci Daniyel 8:14. Ci saa si, xolam daldi gëm li.
GSAM 314.3Pasteur Bates xalaatu woon ci géntam ba keroog bi mu duggee ci bunt bi te toog ci palaasam. Waajaloon na ngir wax ci beneen mbir, waaye xelam dafa taq ci mbirum bérab bu sell bi. Bi muy baamtu wax ji, géntam daldi ñëw ci xelam, mu ñaan ci biir xolam ndimbal ngir mën a wax ak xoli ñi koy déglu. Am na yombal gu réy ci leeral ni waxtu wi jaaré, loolu itam Annie xamoon na ko bu baax. Gannaaw loolu, mu leeral dëgg-dëggu bataaxalu ñetteelu malaaka bi ak Sàbat bi.
GSAM 315Annie Smith Nangu Na Dëgg-dëgg Bi
GSAM 315.1Bi mu tëjee ndaje mi, mu jege Annie, ne ko, “Gëm naa ni yaw yaa di doom ju jigéenu Soxna Smith bu dëkk West Wilton. Mësumaa la gis, waaye sa kanam dafa ma xamal. Gis naa la ci gént démb ci guddi.” Ci la Annie nettali géntam. Mu génn ndaje ma ak xolam ak yéeneem yu soppiku lépp, ndaxte foofee la nangu dëggu Sàbat bi.
GSAM 315.2Dellu na ca daara ju kawe ja, dajale ay yëfam, daldi dem kërëm. Bi mu xamee jafe-jafey Pasteur White ci wàllu siiwal gi ak liggéeyam ci wàllu waare gi, dafa yëg ne Yàlla woo na ko mu dem jàppale ko ci liggéeyu biroom bi. Ci weeru Ut, atum 1851, bi ñu jógee ak jurnaal bi Paris yóbbu ko Saratoga Springs, N.Y., Jànk Smith dem na fa bokk ci ñiy liggéey.
GSAM 315Benn sarax ak benn jébbalu
GSAM 315.3Ci Review bi, Vol. 2, No. 7, am na ay rëdd yu tuuti yu jóge ci loxoom, di firndeel yëg-yëgam ginnaaw bi mu bàyyee naal yu njëkk ya ngir liggéeyam bu woyof te amul réy-réylu. Mu ne:
GSAM 315.3“Am naa yaakaar ne bàyyi naa lépp ngir topp Mbote mi fu mu mëna jëm. Suuf ñàkk na solo ci man lépp. Sama yaakaar, sama mbégte, sama mbëggeel, lépp léegi ci lu nekk kaw ak lu sell lañu jëm. Bëgguma beneen bërëb bu dul toog ci tànki Yeesu di jàng ci moom—bëgguma beneen liggéey bu dul di liggéeyal sama Baay bu nekk asamaan—bëgguma beneen mbégte bu dul jàmmug Yàlla gi xel mënu ko natt.”
GSAM 315.4Ndimbalu Soxna Annie ci biro bi, niki kiy jubbanti mbind yi ak yeneen, jot na woon lool. Ci diiru ñetti at, liggéey na fa ak pasteef te jàppandi, te li mu doon jël rekk mooy lekk ak ay yere. Bi jamono jooju jeexee, feebaru tuberkiloos moo ko tànnoon ngir mu nekk ci ñi muy jël. Ci biir lor yu feebar bu yàgg tey rey boobu di def, bindoon na ay woy yu rafet, bi ci gëna neex di “Kër Fii ak Kër Asamaan,” te li ko ubbi, bu ñu bind bés bi jiitu woon dee gi, 26 Sulet 1855, dafa firndeel bu baax jikko yu rafet yu woyof ak sukk yu mu amoon ba tax nu mënul a ñàkk a ko joxe lépp:
GSAM 316Yore kër ci biir jafe-jafe
GSAM 316.3Ci weeru Awril atum 1852, Pasteur White jóge na Saratoga Springs dem Rochester, N.Y. Ci dëkk boobu lañu, ci 124 Mt. Hope Avenue, njëkk a samp seen kër ak ay jumtukaay yuñu jënd te du yuñu abbi. Waaye seen yitte ci liggéeyu siiwal gi dafa doonoon réy, ngir mu jàll, te jurnaal bi genn saa su nekk, te noonu dëgg gi tasaaroo, ba tax ñu bàyyi seen bopp ñàkk lu bare ci ay noflaayu dund yu ñépp di am.
GSAM 316.4Ni ñu tambalee seen këru bopp ci jamono jooju, mën ngeen koo jàng ci bataaxal bu sutura bii, bi Soxna White bindaloon njabootu S. Howland, ci 16 Awril 1852:—
GSAM 316.5“Ñu ngi door a sampu fii ci Rochester. Luwe nañu kër gu yàgg ci $175 ci at mi. Am nañu màsin bu mag bi ci biir kër gi. Su loolu amul woon, dinañu waroon fey $50 ci at mi ngir am neegu liggéeyukaay. Dina leen reelu bu leen manoon a seet ñu ak seeni alali kër. Jënd nañu ñaari lal yu yàgg ci ñaar-fukki sent ak juróom ci bu nekk. Sama jëkkër indil na ma juróom-bennu toogu yu yàgg, yu bokkul ñaar, mu fey ci benn dollar, te gannaaw loolu mu indil ma yeneen ñeent yu yàgg, yu amul woon toogu, mu fey ci juróom-benn fukki sent ak ñaar ngir ñoom ñépp. Kaadar yi dafa dëgër, te ma daldi defar seen toogu ak tisi bu dëgër. Bëer seer na lool ba duñu ko jënd, te itam manuñu jënd pomdeter. Ñu ngiy jëfandikoo soosu meññeef ci palàsu bëer, ak nawe ci palàsu pomdeter. Sunu lekk yu njëkk yi, ci kaw palangu safara lañu ko doon defee, bu ñu teg ci ñaari barilu fariñ yu neen. Paré nañu ngir muñ naqar su fekkee loolu dina tax liggéeyu Yàlla jëm kanam. Gëm nañu ne loxo Boroom bi moo ñu indi ci bërëb bii. Am na fa liggéey bu bare, waaye liggéeykat yi néew nañu. Sàbat bi weesu, sunu daje bi baaxoon na lool. Boroom bi seddal na ñu ak teewaayam.”
GSAM 317Yaatuwaayu xolu Gëmkat yi
GSAM 317.1Ci nimero bu njëkk bu Review bi, buñu móol ca Rochester, ci 6 Mee 1852, bi muy wax ci tukki gi jóge Saratoga dem Rochester, Pasteur White nee na:
GSAM 317.2“Mbokk yi joxe nañu ay alal yu doy ngir jàppale jurnaal bi, lu ëpp li nu doon xaar. Te wax dëgg, sunu tukki bi nu jóge Saratoga Springs, ak door jurnaal bi ci dëkk bii, jar na xaalis bu bare, waaye léegi amunu benn bor.”
GSAM 317Saraxu liggéeykat yi
GSAM 317.3Ci ab xibaar bu ñeel liggéey bi ci Nimero 12, ci 14 Oktoobar, ñu ngi ci jàng:
GSAM 317.3“Waaye biro bi amul benn bor, ndaxte: Mbokk yi Belden ak Stowell, ñi liggéey ci biro bi ci juróom-benn weer yi weesu, lu tuuti rekk lañu am lu ëpp seen lekk ak seen naan. Ñeneen ñi nekkoon ci liggéey boobu amulooñu lu ëpp li ñoom jot. Dina neex lool mbooleem xarit yu dëgg gi ñu jàppale ci yokk li des ci xaalis bi, ngir ñi liggéey bu metti, rawatina bi ñu fi nekkuñu woon, ci biir feebar, ngir siiwal Review and Herald, am ndimbal lu leen doy.”
GSAM 317Ñi dugg ci mbooloo mi ca Rochester, N.Y.
GSAM 317.4Ci nawet atum 1852, bi liggéeyu siiwal gi tàmbalee dox bu baax ca Rochester, Pasteur White ak soxnaam def nañu tukki bu yàgg ñetti weer, ci fas ak saret, ba penku ca Bangor, Maine, di amal ay ndaje te di seeti ñi daan sàmm bésu Sàbat bi tasaaroo woon ci yoon wi. Laata ñuy dellusi, door ci 26 Sàttumbar, Pasteur J. N. Andrews def na ay waxtaan yu bare ca 124 Mt. Hope Avenue. Ci jamono jooju, juróom-ñetti Adventist yu Bésu Njëkk nangu nañu dëgg gu jamono jii, te kii di bind bokkoon na ci.
GSAM 318Oswald Stowell Wér na
GSAM 318.1Benn ngoonu àjjuma ci weeru Oktoobar, Pasteur White ak soxnaam ñëwsi nañu seen kër gannaaw seen tukki ci penku. Bés bi ci topp (Sàbat) lañu leen gis ngir jëkk, ci ndajem Sàbat bi. Ci jamono jooju, Oswald Stowell, ki daan liggéey ci imprimeri bi, dafa doon sonn lool ci feebaru pleurisy bu metti, te doktooram bàyyi woon na ko, jàpp ne dina faatu. Doktoor bi nee na “amul lu ma ko man a defal.” Ci biir jaamu gi, Oswald mi ngi woon ci néeg bu jege, te di sonn lool ci yaramam. Bi jaamu gi jeexee, yónni na ñu ñaanal ko. Ñu woo ma ak ñeneen ñu dem ñaanal ko. Ñu sukk ci wetu lal bi, te bi ñu nekkee ci ñaan yi, Pasteur White di ko sawal diwlin “ci turu Boroom bi.” Ruhu Yàlla amoon na fa te ñépp yëgoon nañu ko, te ci saa si la wér. Bi ñu jógee ci ñaan gi, fekk nañu ko mu toog ci lalam, muy dóor ci wetam yi, yi mu daan sonn lool, tey wax ne, “Wér naa ba pare. Suba dinaa mën a liggéey ak màsin bi.” Ñaari fan ginnaaw loolu, liggéey na ci.
GSAM 318Gis-gisu Soxna White ci kanamu Kureelu Rochester
GSAM 318.2Njariñu Yàlla gi fajoon Mbokk Stowell daldi wàcc ci Soxna White ci anam gu gën a réy, te bi Pasteur White wëlbëtoo xool ko, mu ne, “Ellen mi ngi ci gis-gis; du noyyi ci jamono jii mu nekk. Su amee ci yeen ku bëgg a wóorlu ci loolu, mën ngeen ko seet.” Mu des noonu ci gis-gis bi lu tollu ci benn waxtu ak ñaar-fukki simili. Bi mu nekkee ci nekkin woowu, dafa doon wax ay baat, te yenn saa yi ay wax yu mat sëkk; waaye bi ñu ko seetee bu baax, gisunu benn noy ci yaramam.
GSAM 319Gis-gis ci lu jëm ci bokk-bokk bu fi nekkul
GSAM 319.1Bi Soxna White génnee ci gis-gis boobu, seede na ci li mu gisoon. Laata Pasteur White ak soxnaam di dellusi ci seen tukki ca penku, kenn ci ñun jóge woon na ca dëkk ba, te nekkoon ci tukki liggéey ca Etaa bu Michigan. Kon, teewul woon ci ndaje mii, te mësul a gis Pasteur White mbaa soxnaam. Bi muy nettali gis-gisam bi, Soxna White wax na nu, ci biir yeneen yi, li mu gisoon ci jëmmu góor gu, bi mu nekkee ci tukki te sore këram, daan wax lu bare ci yoonu Yàlla ak Sàbat bi, waaye ci jamono jooju mu ngi doon jalgati benn ci ndigali Yàlla. Mu nee nit ku mu masul a gis la woon, waaye dafa gëmoon ne dina ko gis benn bés, ndaxte mbiram lépp feeñaloon na ko. Waaye, kenn ci ñun xalaatul woon ne moom kenn la ci ñi nu xamoon.
GSAM 319.2Lu tollook juróom-bennu ayu-bés gannaaw gis-gis boobu, mbokk mi ñu tuddoon dellusi na jóge Michigan. Bi Soxna White seetaanee rekk kanamam, mu ne benn ci jigéen ñi, “Moom la góor gi ma gisoon ci gis-gis bi, te waxoon leen ci moom.” Bi ñu ko nettalee gis-gis boobu, ci kanamu jabaram ak ñeneen ñu bare, Soxna White ne ko, “Ni Natan waxee Dawuda, ‘Yaw yaa di ki.’” Ci noonu, def na li Pawlos wax ne am na ñu lay def suñu leen yeddee seeni bàkkaar ci mayu yonent: “Waaye bu ñépp di wax kàddug yonent, te am ku gëmul walla ku xamul, ñépp dinañu ko yedd, ñépp dinañu ko àtte: te noonu lañuy feeñalee li mu nëbb ci xolam; te noonu, mu daanu ci kanamam, mu jaamu Yàlla, te seede ne Yàlla am na ci yéen dëgg-dëgg.”3 Bi ko Soxna White waxalee ay bàkkaaram, mbokk mi dafa sukk ci kanamu jabaram, ak ay rangooñ, ne ko ak ñi fa nekkoon ñu néewoon: “Yàlla ànd na ak yeen ci dëgg,” daldi nangu lépp li mu defoon bi mu nekkee Michigan, ci jalgati ndigël lu juróom-ñaareel li, ni mu feeñee woon ca jamono jooju, te fekk mu sore woon lu ëpp juróom-téeméeri miil.
GSAM 320.1Kon, ay ayu-bés yu néew rekk joxe nañu ñu firnde ju dëgër ci seede yooyu. Du rekk ñu yobbu woon ci wax ne kàttan gu dul gu àdduna moo leen tax a jug, waaye itam ne jóge nañu ci benn cëslaay bu, ci anam gu leer nàññ, di yedd nit ñi ci seeni bàkkaar.
GSAM 320Uriah Smith Dugg na ci Biro Review bi
GSAM 320.2Ci jamono ji ñu doon siiwal Téere bu ñetteel bu Review bi la Uriah Smith tàmbali woon di sàmm bésu Sàbat bi, te lëkkalook biro bu Review bi, foofu la nekkoon bindkat ak editeer lu mat ay at yu bare. Liggéeyam bu njëkk bu ñu siiwal ci jurnaal bi ab woy la woon bu tudd, “Baat bu Yëgal bu Jamono ak Waxu Yonent,” te mu génn ci 17 Maars 1853.
GSAM 320.3Pasteur Smith dégg na ngir njëkkeel bataaxalu malaaka bu ñetteel bi ci am ndaje ca Washington, N.H., diggante 10 ba 12 Sàttumbar 1852. Bi mu dellusee kërëm ca West Wilton, dafa jàng bu baax li mu déggoon, te tàmbali sàmm bés bu juróom-ñaareel bi, di Sàbat bu njëkk ci weeru Desàmbar 1852. Dafa booloo ak biro Review bi nekk Rochester, N.Y., ci 3 Mee 1853, foofu moom ak rakkam ju jigéen Annie ñoo fa doon liggéeyee ngir am seen lekk ak seeni yere, ci palàsu jàngale ci benn daara ju mag te di am $1,000 at mu nekk ak seen lekk. Loolu, ci melokaanam, bokkoon na ci sarax yi ñu joxe woon ngir samp liggéeyu bataaxalu malaaka mu ñetteel mi ci ay bisam yu njëkk.
GSAM 320Sampees na ko njiitu diine
GSAM 320.4Ci lu tollu ci atum 1863, Pasteur Smith tàmbali na di jëfandikoo mayam ci wax ci kanamu mbooloo. Ci atum 1866, ñu samp ko niki ab waarekatu Injiil, ginnaaw loolu mu liggéey bu baax ci ndajey camp ak ay konferans ci Etaa yu wuute yi, jóge ci géeju Atlantic ba ci Pacific, ak itam ci liggéeyu pasteur ci jàngu Battle Creek, mi nekkoon jàngoom. Ginnaaw bi ñu ubbee Kolees bu Battle Creek, dafa jàngale woon lu néew walla lu bare ci bànqaasu njàngum Biibël bi ca daara jooju. Ngir liggéeyu Review and Herald, dafa jàll Géeju Atlañtik ci atum 1894, di seeti réew yu wuute ca Tugal. Bi mu nekkee Siri, dafa am feebar bu mu ci amee ay jafe-jafe yu mu muccul ba fàww.
GSAM 321Juróom-fukki At ci Liggéey bu Amul Noppalu
GSAM 321.1Ci diggante 1853 ba 1903, lu tollu ci juróom-fukki at, Pasteur Smith dafa doon liggéey ci wàllu bindkat ci jurnaal bii di Advent Review and Sabbath Herald lu ci ëpp. Te ci lu ëpp ci jamono jooju, moom moo yoroon saytu gu mat sëkk gu jurnaal bi. Ba ci bésu faatoom sax, bi ko jàngoro paralisi dalee, dafa doon dem ca biro ba ak ay mbind yu mu waajal ngir ñu móol leen. Dafa bokk itam ci ñi bind ay téere yu am solo yu bare ci mbindi kurelu diine bi. Ci biir liggéey yooyu, am na ci: Thoughts on Daniel and the Revelation, Nature and Destiny of Man, benn téere bu ñu yokk ci Sanctuary and Twenty-three Hundred Days, The Marvel of Nations, ak Modern Spiritualism. Téere bu njëkk bi ci yooyu, li ci ëpp ci guddi la ko doon bindee, diggante waxtu juróom-ñeent ak guddi-gët, ginnaaw bu liggéeyu bind ak bu biro bi jeexee.
GSAM 321Dee gu Pasteur Smith
GSAM 321.2Dundam lu am njariñ la woon te jàll na ko bu baax. Noppalu na ci ay liggéeyam, ndaxte nelaw na ci Yeesu ci 6 Maars 1903. Waaye ci moom, mën nañu wax dëgg ne, “Ay jëfam ñoo koy topp,” te doonte dee na, ba léegi mi ngi wax.